Overblog
Editer l'article Suivre ce blog Administration + Créer mon blog

 Jàngat bu ndaw ci A

A,aa,à,ã

Mu doon ñeenti « a » yu nu seetlu ci làkk wi.

« A » bu fekke bii la danu koy gis ci waat yii : Saf,ñaf,kaf, Abdu,jam,Asan,tama,and….

 Seetlu bi nu ci def mooy, « A » gis nanu mën na nekk ci tàmbale baat bi maanaam mooy linu am ci baatu « and » niki melni andu cuuraay, gis nanu ne, mën na nekk ci digg baat bi ñu jël masala ci baatu « saf » maanaam yat wi saf na sàpp. Mën na nekk itam ci njeextalu baat bi ñoo ngi gis loolu ci baatu « tama » maanaam tëggal tama.

« AA »  bii mooy « aa » bu nu séexal. Moom itam, gis nanu ko ci waat yii : aada, aadama,kàllaama, jaaraama, daaw…

Seetlu bi mooy, « AA » gis nanu ko ci tàmbali baat bi maanaam mën na nekk ci bopp baat bi, moom lanu am ci baatu « AADA ». Gis nanu ko it mu nekk ci digg baat bi am nanu loolu ci baatu « kàllaama ». ku ko gis it ci njeextalu baat bi nanu ko dollil .

« À » Nu koy woowe « À » bu ŋàppaaral wala bu ubbéeku. gis nanu ko ci waat yii : àq,ànd,sàq,tànk,jàng,làng,àbb…

Seetlu bi fii mooy « À » bu ubbéeku bi day nekk ci tàmbale baat bi moom lanu am ci « àq », am nanu ko ci digg baat bi moom lanu am ci tànk. Waaye gisu nu ko fenn mu jeexal fa baat maanaam mën nanu wax ne « À » bu ubbéeku bi du jeexal baat.

 

« Ã » bii nag moom sama xalaat soriwu ci maanaam ku ci am xam-xam mën nanu ci jàppale nu gën koo xóotal.

Benn masala laa ci am muy baatu ãnse limuy tekki nag kuma ci jàppale ma jël dama koy dégg noonu rekk.

 

 

            Maa ngi leen di jaajëfal !

 

Partager cet article
Repost0
Pour être informé des derniers articles, inscrivez vous :